Yàq gi palaastig di def ci Senegaal: xeex bi du gaaw!

Avatar Wax Wolof | 20 février 2020




Lu ëpp ñaari milyoŋi nàmmaani mbaliti palaastig mooy am Senegaal at mu nekk. Fan la bitéel, kaasu kafe walla sax mbuusi ndox yooyu ñuy sànni ci mbedd yi di dem ?

Ag gëstu gu yaatu gu saabalkat yi def mooy dellusi ci jeexital yi mbalitu palaastig am.

Man ngeen a topp dugg gi ñu dugg ci gox bii di àllub Daara Jolof. Xamees na fa ne jur gi dañu fay lekk lu baree-bari palaastig bi ba tax muy jur ag ñàkk gu rëy ak yàqute gu yaatu ci sàmmkat yi.

Loolu doonul yàq gi palaastig rekk di def. Jeexital yu tiis te metti it ñu koy seetlu ci kéew mi ba tax ferey réew mi tàmbali di ci yewwu.

Ngir bañ a des ginnaaw ci xeex boobu am ci àddina sépp, nguurug Senegaal nangu na sàrt bu bees bu indi ay tere yu yaatu ci mbirum palaastig. Sàrt boobu dinañu ko tàmbalee doxal 20 ci awril ci 2020.

Bunu sukkandikoo ci kilifa yi, pexe yépp def nañu ko ngir sàrt bu bees bii bañ a mel ni yi fi jotoon a jaar niki bu 2015 bi nga xam ne cig lajji la mujj.

Leeral:

Saabalkat y= Reporter, Journaliste
Kéew m= L'environnement

Piri mi Wax Wolof moo ñu ko defal

Limat : +221 77 881 20 11

Lëkkalekaay : jangwolof.com


Commentaires

This post currently has no responses.

Votre opinion nous intéresse, laissez un commentaire à cet article


error: Dans le cadre de la protection de nos contenus, nous avons verrouillé la copie de nos articles, la citation reste permise. Merci de votre compréhension!