Senegaal : juróom-ñaar fukk ak juróom-ñatti junniy nàmmaan ci mbalitu palaastig moo dugg ci biir réew mi, ci atum 2019.

Avatar Wax Wolof | 15 février 2020

Sunu xaymaa lépp , juróom-ñaar fukk ak juróom-ñatti junni ak juróom-ñent fukki nàmmaan ci mbalitu palaastig ñoo dugg ci lu dul yoon biir Senegaal bàyyikoo Etaasini (Amerig) diggante saawiyee ak deesàmbar atum 2019. Ci xaalis ñu xayma ko ci lu tollu ci benn milyaar ak juróom-ñent téeméeri milyoŋ. Duggal googu mi ngi wéy ba leegi ndax ba ci weeru deesàmbar 2019, US CENSUS BUREAU (kër gi yor jënd ak jaay biir Etaasini) ngi fésal ay xibaar jëme ci dugal boobee.



Xibaar bi nag daanaka kenn yëggu ko biir Senegaal. Ci weeru suye, yéenekaay bii di “Guardian” génne na gëstoom jëmee ci fi mbalitu palaastigu Etaasini di jaar. Gëstu googu wane na ni Senegaal ci jëmuwaayu mbalit yooyu la bokk.
Ci lu gaaw, këru jëwriñ gi yor mbir mi bind na ca dalam ba ca feesbug ne “xibaar bi wérul”. Wax ji fay ci lu gaaw, jamono jooju. Waaye, gëstu gu yaatoo gi këru tas xibaar bi nekk Àngalteer def wane na ni weer wu, diggante saawiyee ak maars atum 2019, lu tollu ci fukki nàmmaan ci mbalitu palaastig, jóge na bitim réew jëm Senegaal. Ci weeru mee, lim bi dem na ba tollu ci juróom benni junni ak juróom-ñatti fukk nàmmaan. Jeexit walla Ñàkk tay la ? Ci weer woowu, dugal mbalit moomu biir Senegaal te jóge Etaasini ci la dakk. Moone ja bi àddina si jagleel mbalit yooyu amoon na xew-xew bu rëy jamono jooju.

Ci 10i Me, 187i réew ñu man ci boole Senegaal (waaye Etaasini bokkuñu ci woon) déggoo nañu ci ab sàrt buy dooleel seen sañ-sañ jëme ci ñu xam mbalitu palaastig yiy dugg seen biir réew nuñu mel. Nguur yi am nañu leegi sañ-sañu aaye mbalit yooyu su fekkee ni day lor kéewi mi walla kenn manu leen jëfandikooti.
Jan Dell di ab nqereñtaan te di njiitu “The Last Beach Cleanup” nee na dakkal gi am ci yónnee mbalitu palaastig bi, xibaar bu neex la. Bañkat boobu moo jiite genn ci 50i mbootaay yi nekk Etaasini tey wax ni Etaasini dañoo war a dakkal yónnee mbalit ci réew yu mel ni Senegaal, nga xam ni amuñu jumtukaay ngir soppi leen ngir ñu man leen jëfandikoowaat. Ñaar ci këru liggéeykaayu Etaasini yi gën a fés ci wàllug caytu mbalit ànd nañu ci càkkuteef googu, daaw.
Terewul, yónne mbalitu palaastig biir Senegaal tàmbaliwaat na ci weeru sàttumbar.
Man nanoo sax jàpp ne mi ngi wéy ba leegi.
“Xibaar yi US Census Bureau” mujjee rotal deesàmbar la woon te 5470i nàmmaani mbalitu palaastig ñoo dugg ci biir réew mi fekk na ni ci weeru nowàmbar lim baa ngi tolloon ci 3100i nàmmaan.

Koom mi Siin salfaañe

Lépp a ngi door ba Siin wéyalee séen ndogal yi bett ndefar (industrie ) yiy liggéey ci palaastig. Ki gën a fés ci li muy dugal ci réewam mbalitu palaastig soppi ni muy jëflantee ak mbalitu jàmbur yi ngir man a aar am kéewam( environnement ), ak wér-gu-yaramu waa dëkkam.
Mbalit yi waratuñu weesu 0,5% jóge ci mbalit yi ñu manul soppiwaat, te mbalitu saa-amerig man nañu jàll ba 25%.
Liggéey biy jëm ci buuju mbalitu palaastig mi dafa daanu.

Loolu def na yëngu-yëngu gu mag ca Amerig moom mi nga xam ne ci àddina bi moo ëpp limuy yóbbu mbalit moomu bitim réew. Yóbbu googu ca Siin wàññeeku na lool, fekk ne lu yées 10% rekk ci mbalitu palaastig lañuy defaraate ci biir dëkk ba. Màkkaanum lijjantig mbalit mi, limu mbalit mi ñu xamul fuñu koy yóbbu ëpp na leen doole lool.

Mbetteel gi tax ñi ciy yëngu di wut weneen yoon. Ci wallaa ga, beneen ub ja bu làqu moo ubbiku ci ñiy jënd ak jaay mbalitu palaastig bi ci àddina bi.
Ci kaw tere gi, kilifa saa-siin yi jàpp nañu lu ëpp 100 000 ton ci mbalitu palaastig yi ñu nëbb ci ñatti weer yi jëkk ci 2018.

Ci deesàmbar 2019, 763 000 toni mbalit te mu bokk ci ay palaastig yu ñuy tere dogaale nañu ko. Ay téemeer ciy gàngoor yuy def liggéey bu jaarul yoon boobu tas nañu leen bunu sukkandikoo ci kërug yéenekaayu Siin bii di Xinhua. Ndax ci jooju jamono pexe mi mooy nëbb dëgg-dëggi li ñuy duggal ci réew yi.
Bunu sukkandikoo ci yéenekaay bii di “Resource Recycling”,”ñenn ci yaxantukati Amerig yi ak yu yeneen i réew” ñoo nëbb dëgg gi ci mbalit mi jaare ko ci ŋara( document) yiy tax ñu génn réew ya.”
Di pexe mu ñu tàmm lool ngir rëcc ci càmbar ak luññtu yiy am ci waax ya ñuy teere ji.
Cig niral, ab sosyitteb yaxantu ca Farãs jàllale na ci lu jaarul yoon ñaar fukki Kontaneeri mbalit.

Palaastig, leegi dinañu leen delloo ca réew ya ñu jóge ci taxawaayu Malesi, lijanti (entreprise) bi làqu woon di ci yëngu jëwriñ ji lëkkale kéew mi daan na ko mu war a fay ndàmpaayul yoon lu tollu ci 126i milyoŋ ci sunu xaalis noowàmbar 2019 bii wees. Muy dànkaafu gu njëkk ci njublaŋ yiy yëngu ci njaayum mbalit mi.

Ci wetug waa nguur gu Senegaal, Baaba Daraame, njaatigel kéew mi ak jumtuwaay yu beru yi (DEEC) wan nañu ne amul benn xibaar bu jëm ci mbirum jëggaani mbalitu palaastig ciy liggéeyuwaayam.

Nataal ( Ci xeetu konteneer bii la ñuy def mbalitu palaastig yi di ko jaayi Amerig Guwarjaŋ )

Waaye fan la mbaliiti palaastig yii di dem Ginnaaw bu génnee Senegaal ?

Ci gis-gisu Saŋ Del, man na nekk lijanti (entreprise) biy jot njëggaan yi ci Senegaal dafay jëlaat mbaliiti palaastig yi ci njëg yu yomb daa di leen soppi ci anam yu wuute ak palaastig bu bees bu gànjaru.

Muy doon mbégte ci moom, ndax nee na seen boroom dafa waroon a fay njëg gi koy teqale ak mbalit mi ba lu tollu ci 140 dolaar ci ton bu nekk di lu diis lool, bu fekkoon ne nag mbalit mi réewum Amerig la ñu ko dencoon. Kon nag njëg li man naa gën a néew ci lijjantig saa-amerig gii ci mu jaay mbalitum palaastig mi ci njëg gu yomb ba noppi fay kontaneer yi koy génne bunu sukkandikoo ci ma-kéew moomu.

Belliwaat mbalit mi ci réew yi muy jaar laataa ñu koy yóbbu ca dëkk yu ci mel ne Siin dafay liggéey yu rëy te am solo. Ginnaaw bees dindee taq-taq yu mag yi ci mbuubit miy jóge Amerig, Siin masul a tëj jaham ci njaayum mbalit mu set mbaa mees tànn. Amna ñu bari ñu tàbbi ci biri belli mbalit mi te jaaruñu ko ci yoon rawati na ñenn ñu dëkke kembaarug Asi gi, nekk ay bukki di dox ci digante bi. Mbuubit mi nag saa yu ñu ko seggee ba noppi dees na ko man jaaye njëg lu dem dayo, yegg ba (9 x) jóroom-ñenti yoon njëg gees ko jënde woon ca njëlbeen, ak loolu lépp terewul nag muy luy wéy di indi loraange di yàq it kéew mi, te ñenn dong waral ko.

Li ëpp solo ci sunug luññtu ca mbalit moomu di dugg Senegaal ne ci ay defu yu nekk biir teer-waaxu Ndakaru mooy; ana ku ko moom? waaye booba ba tay kili fay teer-waax bu Ndakaaru nangu wunoo tontu mbaa mu tijjil nu ay wuntam, doonte wan nanu leen këyit yu leer yuy firndeel ni am nanu sañ-sañu càmbar ŋara yi ñu def seeni xibaar rawatina lu jëm ci saytu ana lan moo nekk ci biir defu yiy jóge Amerig li ko dale atum 2019. Noonu it la nu ko pekub Amerig biy saytu am jaayam ci bittim réew bañalee, teg ko ci suturaal këyiti bóot.

Lees war a ba xel jamono jii nag mooy sàrt biy wax ana nan la nuy saytoo mbalit ci Senegaal di tere bépp xeetu dugal mbalit ci réew mi, dinañu ko doxal li ko dale wéeru awril 2020 bii nu dëgmal.

Piri mi Wax Wolof moo ñu ko defal

Limat : +221 77 881 20 11

Lëkkalekaay : jangwolof.com



Commentaires

This post currently has no responses.

Votre opinion nous intéresse, laissez un commentaire à cet article


error: Dans le cadre de la protection de nos contenus, nous avons verrouillé la copie de nos articles, la citation reste permise. Merci de votre compréhension!